Bëgg a Baax podcast

Bëgg a Baax podcast

Cheikhouna Diaw
Country Senegal
Language WO
Episodes 26
Latest 16.10.2026

Li tax a jóg Bëgg a Baax podcast mooy yaatal mbaax. Képp koo xam ne mbaax ñor na la, nu ngi la ciy dalal ak jàmm.

Episodes

  • Le vrai miracle chez les soufis
    Le vrai miracle chez les soufis 16.10.2026 15m
    Ci waxtaan wii, Ibn Ataa daf ciy indi déggiinam ci lay mooy dëgg-dëggi karaama gi sufiyànke yi. Ñu bari jàpp nañu ne karaama mooy lem suuf si, naaw ci jawu ji mbaa dox ci ndox mi. Waaye li sufiyànke yi jàppe karaama dëgg mooy bàyyi moy Yàlla ci biir ak ci biti. Xam ko, di ko jaamu te duñu ko bokkaale ak dara.
  • Ghazâli: conseils précieux pour l‘aspirant
    Ghazâli: conseils précieux pour l‘aspirant 10.10.2026 15m
    Ci waxtaan wii Al-Ghazâli da ciy dénk jullit bi mu moytu di ànd mbaa déglu niti jamonoom yi sàggan ci jaamu Yàlla, waaye taqoo ak ñi farlu ñi mbaa di yër téere ñu baax ñi fi jaaroon te farlu woon ci topp Yàlla lool ngir yokk pas-pasam ci Yàlla.
  • Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñeent
    Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñeent 11.06.2026 27m
    Teggiin yii la Imaam Saaraani waxtaane ci poñ bii:- Yëram jullit ñi -Sant Yàlla-Nëbb sa tolluwaay-Néewal say mébet
  • Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett
    Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett 23.04.2026 13m
    Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett bi mu ngi aju ci disóo ak Yàlla ci sa mbir yépp, moytu di jublu mayu Yàlla yi fàtte Aji-Maye ji, ak wéet.
  • Waxtaan ci bor
    Waxtaan ci bor 20.03.2026 13m
    Ci waxtaan wii, da nu ciy leer dayo bi bor am ak diis bi mu diis, ngir fàttali sunu bopp, waaye fàttali sunu bokki jullit yi ngir ñu jàjju te moytu bor boodut fay.
  • Ban xam-xam mooy farata?
    Ban xam-xam mooy farata? 27.12.2025 31m
    Ci waxtaan Wii, danu ciy indi tontu ci laaj bii: Ban xam-xam mooy farata ci nit ki? Ginnaaw Yonent bi SAW daa wax ne sàkku xam-xam farata la ci jullit bi, kon yey na lu ne xam ban/yan xam-xam la war a ràngoo.
  • Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar)
    Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar) 06.12.2025 22m
    Waxtaan wii mu ngi aju ci Teggiini niti Yàlla yi ak sew-sew yi leen wuutale ak ñeneen ñi.
  • Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi)
    Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi) 21.08.2025 26m
    Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
  • Njariñu Koor
    Njariñu Koor 06.03.2025 36m
    Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
  • Moytu àq yi
    Moytu àq yi 21.01.2025 13m
    Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
  • Tëj gi: Gàllaŋkoor yi
    Tëj gi: Gàllaŋkoor yi 14.12.2024 15m
    Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
  • Pensées et introspection
    Pensées et introspection 16.10.2024 39m
    Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
  • Tegginu nitu Yàlla yi
    Tegginu nitu Yàlla yi 31.07.2024 31m
    Ci waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax).
  • Lan mooy gis Yàlla?
    Lan mooy gis Yàlla? 22.06.2024 23m
    Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ.
  • Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñ
    Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñ 29.05.2024 25m
    Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir da ciy wax ci xeetu tudd Yàlla yi am, rawatina bu làmmiñ bi nga xam ne kiy doog a sóobu ci lay tàmbalee. Ci mujj gi mu tënk ponku tassawuf yi mu jàpp ne ñoo ci gën a am solo.
  • Waxtaan ci tassawuf: Sikar ak xalam (zikru ak fikru)
    Waxtaan ci tassawuf: Sikar ak xalam (zikru ak fikru) 18.05.2024 20m
    Ci tomb yii, Imaam Dardiir da ciy wax ci solos jaamu Yàlla njël ak taxawaayu tudd Yàlla ci dundug aji-sóobu ji. Ñu doon yaari ponk yoo xam ne ki sóobu ci Yàlla da leen a war a fonk ngir jot ci càkkuteefam.
  • Waxtaan ci 6i ponku tassawuf bi: Al-uzla (wéet)
    Waxtaan ci 6i ponku tassawuf bi: Al-uzla (wéet) 08.04.2024 21m
    Wéet daa bokk ci ponk yi tassawuf teg ngir nit ki sellal xolam. Jaxasoo ak nit yi lu bari ci lu dul farata dafay sabab ay ayibu xol. Moom la Imaam Dardir di leeral ci waxtaan wii ngir aji-sóobu ji bàyyi ko xel.
  • Waxtaan ci ponku tasawuf yi: Sëriñ bu mat sëriñ
    Waxtaan ci ponku tasawuf yi: Sëriñ bu mat sëriñ 27.03.2024 31m
    Ci dars bii, Imaam Dardiir dafay waxtaan ci ponku tassawuf yii di nangu ndogal ak wut sëriñ bu mat sëriñ. Ci ginnaaw gi mu misaal nu sëriñ bu mat sëriñ nu muy mel.
  • Ñaareelu- ak ñetteelu ponk tassawuf yi: Sant ak muñ
    Ñaareelu- ak ñetteelu ponk tassawuf yi: Sant ak muñ 20.03.2024 31m
    Ci biir fukki ponk tassawuf yi Imaam Dardiir indi ci téereem bi, waxtaan wii mu ngi aju ci lan lañuy tuddee sant Yàlla ci diine ak lan mooy muñ bi tax ñuy wax muñ.
  • Ponku tassawuf bu njëkk bi: Tuub
    Ponku tassawuf bu njëkk bi: Tuub 14.03.2024 33m
    Tasawuf daa am ay ponk yoo xam ne nitu Yàlla yi dañu ko tëral ngir yombal aji-sóobi ji ngir mu jot ci sàkkuteefam. Ponk yooyu ñu ngi ko tënk ci fukk. Tay nag ponk bu njëkk bi lañuy waxtaane te mooy TUUB.

Popular in

The podcast also appears in the podcast charts of these countries.